Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

LESOŊ 3

Woneel mbaax

Woneel mbaax

Njàngale bi: «Ku bëgg . . . dafa baax.»—1 Korent 13:4.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 9:​1-7. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Lan la Yeesu njëkk a def—faj góor gu gumba gi walla yégal ko xibaaru jàmm ji?—Jàngal Yowaana 9:​35-38.

  2.   Lu tax ñu mën a wax ne, li ko Yeesu defal moo tax góor gu gumba gi nangu ko déglu?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Nit ki dina la déglu bu yëgee ne am nga itte ci moom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Wonal nit ki ne yëg nga li mu yëg. Xalaatal ci jafe-jafe yi muy dund, noonu di nga yëg li muy yëg.

  1.    Laajal sa bopp lii: ‘Ban njàqare la am fi mu tollu ni? Ban ndimbal la soxla?’ Booy laaj sa bopp fasoŋ laaj yooyu, di nga yëg li nit ki yëg. Loolu moo lay xiir nga dimbali ko ak xol bu tàlli.

  2.   Déglul nit ki bu baax ngir won ko ne li muy wax itteel na la. Bu laay wax li mu yëg walla mu lay wax jafe-jafe yi mu am, bul ko dog. Déglu ko bu baax.

4. Woneel nit ki mbaax ak respe. Bu dee da nga am yërmande ci nit ki te nga bëgg koo dimbali dëgg, loolu dina feeñ ci saay kàddu. Xalaatal bu baax ci li ngay wax ak ci ni nga koy waxee. Moytul a wax lu mën a merloo nit ki.

5. Wutal a dimbali nit ki. Xalaatal ci li nit ki soxla te dimbali ko ci. Sa mbaaxaay mën na tax nit ki déglu la.