Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

LESOŊ 5

Woneel nit ki teggin

Woneel nit ki teggin

Njàngale bi: «Na seen jépp wax nekk wax yu neex.»—Kolos 4:6.

Ni ko Pool defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 17:​22, 23. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Waa Aten ay jaamukat xërëm lañu. Bi ndaw li Pool gisee li ñu daan def, lan la yëg ci xolam?—Xoolal Jëf ya 17:16.

  2.   Pool mënoon na leen yedd, waaye defu ko. Naka la jëfandikoo li ñu gëm ngir yégal leen xibaaru jàmm bi?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?

2. Xalaatal bu baax ci li nga bëgg a wax, ni nga ko war a waxee ak waxtu bi gën ngir wax ko. Loolu dina tax nit ñi déglu la.

Nanga roy ci Pool

3. Xalaatal bu baax ci li nga war a wax. Ci misaal, bu de nit ki nekkul kerceen, xalaatal ci ni nga ko mënee jàngal ci lu jëm ci Biibël bi walla ci Yeesu.

4. Bu la nit ki waxee lu àndul ak li Biibël wax, bul ko gaw a jubbanti. Mayal nit ki mu wax li mu xalaat, bu de sax li muy wax àndul ak li Biibël di jàngale. (Saag 1:19) Booy déglu nit ki, di nga xam li mu gëm ak li tax mu gëm loolu. Noonu nga ko mënee dimbali.—Kàddu yu xelu 20:5.

5. Gërëm ko ci li mu waxe xalaatam. Xéyna ci moom, lépp li ñu ko jàngal ci diinem dëgg la. Kon, njëkkal a seet fu ngeen bokke xalaat, ba pare nga dimbali ko, ndànk ndànk ba mu nànd li Biibël bi di jàngale.