Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

LESOŊ 6

Amal fit

Amal fit

Njàngale bi: «Yàlla sunu Boroom may na ñu fit, ba ñu yégal leen xibaaru jàmm bi.»—1 Tesalonig 2:2.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Luug 19:​1-7. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Lu tax ñenn ñi, bëgguñu woon jege Sase?

  2.   Lan moo xiir Yeesu mu yégal ko xibaaru jàmm bi?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñu bëggee yégal xibaaru jàmm bi képp ku mu mënta doon, dañoo war a am fit.

Nanga roy ci Yeesu

3. Wéerul ci Yexowa ngir mu dimbali la. Ni Xel mu Sell dimbalee Yeesu mu waare, dina la dimbali yaw itam nga am fit ngir waare. (Macë 10:​19, 20; Luug 4:18) Xéyna, am na ñoo xam ne yombul ci yaw nga wax ak ñoom. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am fit ngir waar leen.—Jëf ya 4:29.

4. Buleen ñaaw njort ci kenn. Xéyna yenn saay yombul ci ñun ñu waar ñenn ñi ndax seen colin, seen xeet, seen am-am, ni ñuy dundee, walla seen diine. Waaye, fàttalikul ne:

  1.    Yexowa ak Yeesu ñoo xam li nekk ci xolu nit ñi. Ñun mënu ñu ko xam.

  2.   Yexowa ñépp la bëgg a dimbali, ak ku mënta doon.

5. Amal fit, waaye, woneel nit ki teggin. (Macë 10:16) Xamal ni ngay jeexalee waxtaan bi ngir moytu xuloo ak nit ki.—Kàddu yu xelu 17:14.