Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI NGA MËN A WAX BOO SEETIWAATEE NIT KI

LESOŊ 8

Deel muñ, te def ndànk ak nit ñi ci liggéeyu waare bi

Deel muñ, te def ndànk ak nit ñi ci liggéeyu waare bi

Njàngale bi: «Ku bëgg dafay muñ.»—1 Korent 13:4.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 7:​3-5 ak 1 Korent 15:​3, 4, 7. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Ca ndoortel ga, ndax rakku Yeesu yi amoon nañu ngëm ci moom?

  2.   Lan mooy wone ne Yeesu dafa wéy di dimbali rakkam bi tudd Saag?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Ñenn ñi dañuy jël jot ju bare bala ñuy nangu xibaaru jàmm bi. Kon soxla nañu def ndànk ak ñoom ngir dimbali leen.

Nanga roy ci Yeesu

3. Wutal yeneen pexe ngir dimbali nit ki. Bu dee nit ki parewul ngir jàng Biibël bi, bul ko forse. Mën nga ko won ay wideo ak ay waxtaan yu ko mën a dimbali mu gis ni ñuy defe njàngum Biibël ak nit ñi ak it jàriñ bu mu ci mën a jële.

4. Bul tollale nit ki ak keneen. Nit ñi yemuñu gis-gis. Kon, bu dee yombul ci kenn ci sa waa kër, walla ci keneen, mu nangu jàng Biibël bi, walla mu nangu li Biibël bi di jàngale, jéemal a xam li tax. Ndax nit ki dafa takku lool ci li mu jàng ci diineem? Ndax waa këram yi, walla dëkkandoom yi dañu koy fitnaal? Xéyna dafa soxla jot ngir xalaat bu baax ci li mu jot a dégg ci Biibël bi.

5. Ñaanal Yexowa mu dimbali nit ki. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am gis-gis bu baax ci nit ki te won ko teggin. Ñaan ko it mu dimbali la nga xam ndax da nga war a kontine di seetiwaat nit ki walla déet.—1 Korent 9:26.