Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI NGA MËN A WAX BOO SEETIWAATEE NIT KI

LESOŊ 9

Woneel nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la

Woneel nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la

Njàngale bi: «Nangeen bokk ak ñi am mbégte, ci seen mbégte; te bokk ak ñi am naqar, ci seen naqar.»—Room 12:15.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Màrk 6:​30-34. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Lu tax Yeesu bëggoon a beru, moom ak talibeem yi?

  2.   Ba Yeesu gise mbooloo ma, dafa leen jàngal lu bare. Lan moo ko ci xiir?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu dee dañoo am yërmande ci nit ñi, dinañu ko yëg ci suñuy wax ak suñuy jëf. Dina ñu xam ne nëw ñu rekk ngir yégal leen xibaar bi ñu yor, waaye dañoo am itte ci ñoom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Déglul nit ki bu baax. Bu nit ki nekkee di la wax yëg-yëgu xolam, walla njàqare yi mu am, walla sax mu nekk di wéddi li nga koy jàngal, bul ko dog. Déglu ko bu baax. Noonu nga koy wone ne, li muy yëg itteel na la.

4. Bàyyil xel ci ñi nga war a seetiwaat. Xalaatal ci waxtaan bi ngeen amoon ayu bés bi romb ba pare nga xalaat ci laaj yii di topp:

  1.    ‘Lu tax mu soxla xam dëgg gi?’

  2.   ‘Naka la ko njàngum Biibël bi mënee dimbali ci dundam te may ko yaakaar?’

5. Waxal nit ki li mu soxla xam. Bu nit ki amee laaj yi muy laaj boppam, won ko ne njàngum Biibël bi mën na ko dimbali mu am tontu ci laaj yooyu yépp. Won ko itam ne Biibël bi mën na ko jox xelal yu baax.