Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII: XAAJ 2

Ndax danga war a kontine waxtaan bi walla déet?

Ndax danga war a kontine waxtaan bi walla déet?

Bu dee jubluwaay nit ki mooy xam dëgg gi, danuy bég ci dimbali ko mu am tontu laaj yi mu ñuy laaj. Xéyna ku «jagoo dund gu dul jeex» la.—Jëf ya 13:48.

Waaye, lan nga war a def bu dee nit ki dafa mer, walla li mu bëgg mooy di werante ak yaw, walla bëggul déglu li nga ko bëgg a wax? Li gën mooy nga jeexal waxtaan bi ànd ceek dal ak teggin. (Kàddu yu Xelu 17:14) Jéemal a tàggoo ak nit ki ci jàmm. Loolu mën na tax beneen yoon, mu nangu waxtaan ak ñun.—1 Piyeer 2:12.