Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII: XAAJ 3

Ni nga mënee jëfandikoo bu baax téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww! ngir jàngal nit ñi Biibël bi

Ni nga mënee jëfandikoo bu baax téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww! ngir jàngal nit ñi Biibël bi

Bala ñuy defar téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww! xalaat nañu bu baax, def nañu ay gëstu yu xóot te ñaan nañu Yàlla ay yooni yoon. Kon xamal ni nga mënee jëfandikoo bu baax téere boobu ngir jàngal nit ñi Biibël bi. Toppal xelal yi ñu wax fii:

Bala ngay dem jàngal nit ki

  1. 1. Waajalal sa bopp bu baax. Xalaatal ci li ki ngay jàngal Biibël bi soxla, li mu nekk di dund ak ni muy gise mbir yi. Xalaatal itam ci poñ yi mu soxla nànd ak ci ni mu mënee jëfe li muy jàng. Mën nga xool itam waxtaan yi nekk ci xaaj bi tudd «Gëstul» te xalaat ci waxtaan yi mu gën a soxla. Noonu, dinga xam ni nga ci mënee waxtaan ak moom booy def njàngum Biibëlam.

Booy jàngal nit ki

  1. 2. Nanga tàmbali te jeexal njàngum Biibëlam ak ñaan bu dee ki ngay jàngal Biibël bi gisu ci benn poroblem.

  2. 3. Bul waax lu bare. Yemal ci poñ yi nekk ci xaaj bi ngeen nekk di jàng te mayal ki ngay jàngal Biibël bi mu wax li mu xalaat moom itam.

  3. 4. Téere bi, ñeenti xaaj la am. Boo leen di tàmbali xaaj bu nekk, njëkk leen a jàng fi ñu bind «li ñu nar a gis» ba pare ngeen lim yeen ci lesoŋ yi nekk ci xaaj boobu.

  4. 5. Boo leen jeexalee benn xaaj ci téere bi, jëfandikool fi ñu bind «Nañu fàttaliku» ngir dimbali ki ngay jàngal Biibël mu jàpp poñ yu am solo ci xaaj boobu.

  5. 6. Boo leen di jàng lesoŋ bu nekk:

    1. Jàngleen xise yi.

    2. Jàngleen aaya yu ñu bind «jàngal», ci seen wet

    3. Mën ngeen jàng itam yeneen aaya yu ngeen soxlaa ci lesoŋ bi.

    4. Seetaanleen wideo yu ñu bind «Seetaanal» ci seen wet (bu dee am nga leen)

    5. Waxtaanal ak ki nga jàngal ci laaj yi nekk ci lesoŋ yi.

    6. Won ko foto yi nekk ci xaaj bi tudd: «Xóotalal njàng mi», ba pare nga laaj ko li mu ci xalaat.

    7. Mën nga jëfandikoo bu baax wërale bi tudd «Jubluwaay» ngir dimbali ki ngay jàngale Biibël bi mu xam ndax mu ngi jëm kanam walla déet. Mën nga sukkandiku ci xaaj boobu ngir dimbali ko mu am yeneen jubluwaay yu baax.

    8. Laajal ki ngay jàngal Biibël bi mu waax la, ndax ba muy waajal lesoŋ bi, am na benn ci wideo yi walla ci waxtaan yi nekk ci xaaj bi tudd «Gëstul» bi ko gën laal.

    9. Jéemleen a jàng benn lesoŋ ayu bés bu nekk.

Boo jàngalee nit ki ba pare

  1. 7. Wéyal di xalaat ci ki ngay jàngal Biibël bi. Ñaanal Yexowa mu barkeel ko ndax jéego yi muy def ngir jëm kanam ci wallu ngëm. Ñaan ko itam mu may la sago ngir nga xam ni nga mënee dimbali bu baax ki ngay jàngal Biibël bi.