Mën nga nekk xaritu Yàlla !
Xelal yi nekk fii dinañu la dimbali nga xam ni nga ko mënee doon.
NJÀNGALE 1
Yàlla mu ngi lay woo ngir nga nekk xaritam
Ci àddina si sépp, am na ay nit ñu dem ba mujja nekk xaritu Yàlla. Yow it, mën nga nekk xaritu Yàlla.
NJÀNGALE 4
Naka nga mënee jàng xam Yàlla ?
Yàlla jël na ay matuwaay ngir ñu mëna jàng li mu defoon démb, li muy def tey, ak li mu nar a def ëllëg.
NJÀNGALE 5
Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana
und ca Àjjana du mel ni dund ci suñu jamano. Àjjana, naka lay mel ?
NJÀNGALE 11
Bul topp diine ju dul dëgg !
Naka nga mënee xàmme diine ju dul dëgg ? Lu tax mu bon lool ?
NJÀNGALE 15
Xaritu Yàlla yi dañuy def lu baax
Yan ñooy yeen liggéey yu baax yi ñu mëna dimbali ñu nekk ay xaritam ?
NJÀNGALE 16
Nanga wone ne danga bëgg Yàlla
Boo bëggee yàgg ak xarit, war nga di waxtaan ak moom, di ko déglu, te dangay wax lu baax ci moom. Noonu la it, boo nekkee xaritu Yàlla.
NJÀNGALE 17
Boo bëggee yàgg ak xarit, yow mii war nga nekk xarit
Looy gëna yokk sa xam-xam ci Yàlla, nga koy gëna bëgg.
NJÀNGALE 18
Nekkal xaritu Yàlla ba fàww !
Dund gu dul jeex mooy maye bu mag bi Yàlla di may ay xaritam