Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 7

Artu bu jóge ca lu amoon

Artu bu jóge ca lu amoon

Yexowa du bàyyi ñu bon ñi ñu yàq Àjjana ji. Xaritam yi rekk ñoo fay dund. Lan mooy dal ñu bon ñi ? Soo ko bëggee xam, seetal li xewoon jamano Nóoxin. Ba Nóoxin doon dund ci kow suuf si, am na léegi ay junniy at. Nit ku baax la woon. Bés bu nekk, dafa doon jéema def ak kem kàttanam li Yexowa bëgg. Waaye ñeneen nit ñi ci suuf si dañu doon def lu bon. Looloo tax Yexowa nee woon Nóoxin ne dina indi ndoxu tuufaan ngir rey nit ñu bon ñooñu ñépp. Wax na Nóoxin mu tabax benn gaal gu mel ni kees. Noonu, bu tuufaan boobu amee, moom ak njabootam dinañu mëna mucc. — 1 Musaa 6:9-18.

Nóoxin ak njabootam tabax nañu gaal ga. Nóoxin yëgaloon na nit ñi ne tuufaan bi mu ngi doon ñów, waaye dégluwuñu ko woon. Bàyyiwuñu lu bon li ñu doon def. Bi mu tabaxee gaal ga ba noppi, Nóoxin dugal na ci ay mala, ba pare moom ak njabootam daldi ci dugg itam. Ginnaaw loolu, Yexowa indi na sàmbaraax bu réy. Tawoon na 40 bëccëg ak 40 guddi. Suuf si sépp feesoon na dell ak ndox. — 1 Musaa 7:7-12.

Ñu bon ñi dee nañu, waaye Nóoxin ak njabootam mucc nañu. Yexowa musal na leen ci tuufaan bi, ba pare, may leen ñu dund ci suuf soo xam ne amatul woon dara lu bon (1 Musaa 7:22, 23). Mbind mu sell mi nee na bés a ngiy ñów, Yexowa dina reyati ñi baña def lu baax. Nit ñu baax ñi, kenn du leen rey. Dinañu dund ba fàww ci Àjjana ci kow suuf si. — 2 Pieer 2:5, 6, 9.

Tey, nit ñu bare dañuy def lu bon. Àddina si fees na dell ak ay coono. Yexowa mu ngiy yónni Seedeem ya, di leen yónni, di leen yónniwaat ngir artu nit ñi, waaye ba tey ñi ci gëna bare bëgguñu déglu li leen Yexowa di wax. Bëgguñu soppali seen jëfin. Bëgguñu nangu li Yàlla wax lu jëm ci lu baax ak lu bon. Lan mooy dal nit ñooñu ? Ndax dinañu masa soppeeku ? Ñu bare duñu soppeeku mukk. Bés a ngiy ñów, nit ñu bon ñi dinañu leen rey te dootuñu dundati mukk. — Sabuur 92:7.

Suuf si, duñu ko yàq mukk ; dinañu ko defar mu nekk àjjana. Ñi nekk ay xaritu Yàlla dinañu dund ba fàww ci Àjjana ci kow suuf si. — Sabuur 37:29.