Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 11

Bul topp diine ju dul dëgg !

Bul topp diine ju dul dëgg !

Seytaane ak malaakaam yu bon yi bëgguñu nga jaamu Yàlla. Li ñu bëgg mooy fexe ba kenn baña toppati Yàlla. Naka lañu jéemee def loolu ? Benn pexe mooy diine ju dul dëgg (2 Korent 11:13-15). Su fekkee ne diine jàngalewul dëgg gi nekk ci Mbind mu sell mi, diine ju dul dëgg la. Diine ju dul dëgg mu ngi mel ni xaalis bu baaxul — xaalis boobu mën na mel ni bu baax bi waaye mënoo ci jënd dara. Te mën na la dugal itam ci ay coono yu bare.

Lu dul dëgg ci wàllu diine mënul neex mukk Yexowa, Yàlla dëgg gi. Ba Isaa nekkee ci kow suuf, amoon na benn mbooloo nit ñu bokkoon diine ñi ko bëggoona rey. Dañu foogoon ne ni ñu doon jaamoo Yàlla moo doon yoon bu dëgg bi. Lii lañu doon wax : “ Benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla. ” Ndax Isaa nangu woon na loolu ? Déedéet ! Dafa leen ne : “ Seytaane mooy seen baay. ” (Yowanna 8:41, 44). Tey, ay nit ñu bare ñu ngi foog ne Yàlla lañuy jaamu, waaye ci dëgg Seytaane ak malaakaam yu bon yi lañuy topp ! — 1 Korent 10:20.

Ni garab gu bon di meññe doom yu bon, noonu la diine ju dul dëgg di meññe ay nit ñuy def lu bon. Li tax àddina si fees ak coono mooy lu bon li nit ñi di def, maanaam moy, xeex, sàcc, noot nit, rey nit ak siif nit. Ñu bare ci ñiy def loolu, dañu am diine, waaye seen diine du leen xiir ci dëkk ci lu baax. Mënuñu nekk xaritu Yàlla bu ñu bàyyiwul def lu bon. — Macë 7:17, 18.

Diine ju dul dëgg dafay jàngal nit ñi ñu ñaan ay xërëm. Yàlla nee na waruñu ñaan xërëm. Mooy yoon. Su amee kenn ku dul wax ak yow mukk, waaye sa foto rekk lay waxal, ndax loolu dina la neex ? Ndax kooku, mën na nekk sa xarit dëgg ? Déedéet, loolu mënul nekk. Yexowa bëgg na nit ñi wax ak moom, te baña wax ak xërëm walla nataal bu dul dund. — 2 Musaa 20:4, 5.

Diine ju dul dëgg dafay jàngale ne, bu xare amee, rey nit, baax na. Isaa nee na xaritu Yàlla yi dinañu am mbëggeel ci seen biir. Kenn du rey ku mu bëgg (Yowanna 13:35). Waruñu sax rey ku bon. Isaa, bi noonam yi ñówee ngir jàpp ko, bàyyiwul taalibeem ya ñu xeex ngir aar ko ci loolu. — Macë 26:51, 52.

Diine ju dul dëgg dafay jàngale ne ñu bon ñi dinañu lakk ca safara. Waaye Mbind mu sell mi mu ngi wone ne bàkkaar, dee lay jur (Room 6 :23). Yexowa, Yàlla ju am mbëggeel la. Ndax Yàlla juy wone mbëggeel dina dugal nit ci lu mettee-metti ba fàww ? Mukk ! Ca Àjjana, benn diine rekk mooy am, maanaam diine ji Yexowa nangu (Peeñu bi 15:4). Diine yuy jàngale fen yi jóge ci Seytaane, ñoom ñépp dootuñu fi nekk.