NJÀNGALE 15
Xaritu Yàlla yi dañuy def lu baax
Boo amee xarit boo sopp te fonk, dangay jéema mel ni moom. Mbind mu sell mi nee na : “ Yexowa, ku baax te jub la. ” (Sabuur 25:8). Ku bëgg nekk xaritu Yàlla, danga wara baax te jub. Mbind mu sell mi nee na : “ Yeen nag ñiy guney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu. Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel. ” (Efes 5:1, 2). Li topp bokk na ci ni ñu ko mëna defe :
Dimbalil sa moroom. “ Nanuy defal ñépp lu baax. ” — Galasi 6:10.
Nanga sawar ci liggéey. “ Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom. ” — Efes 4:28.
Nanga set ci yaram ak ci jikko. “ Nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell ba mat, ci ragal Yàlla. ” — 2 Korent 7:1.
Nanga bëgg sa moroom. “ Nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo. ” — 1 Yowanna 4:7.
Toppal yoonu réew mi. “ Na nit ku nekk déggal [nguur gi] [...]. Joxleen ku nekk céram; [...] ku ngeen wara fey juuti [lempo], feyleen ko ko. ” — Room 13:1, 7.