Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 5

Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana

Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana

Dund ca Àjjana du mel ni dund ci suñu jamano. Yàlla masul bëgg suuf si fees ak coono, naqar, walla metit. Bu ci kanamee, Yàlla dina defar suuf si mu nekk àjjana. Àjjana, naka lay mel ? Nañu seet li Mbind mu sell mi wax :

Nit ñu baax. Àjjana dina nekk këru xaritu Yàlla yi. Nit ku nekk dina defal moroomam lu baax. Dinañu dund dund gu sell ni ko Yàlla bëgge. — Léebu 2:21.

Lekk bu bare. Ca Àjjana, xiif dootul am. Mbind mu sell mi nee na : “ Pepp [maanaam, lekk] dina bare ci kow suuf si. ” — Sabuur 72:16.

Kër yu rafet ak liggéey bu neex. Bu suuf si nekkee Àjjana, njaboot gu nekk dina am këru boppam. Nit ku nekk dina def liggéey bu koy indil bànneex dëgg. — Isayi 65:21-23.

Jàmm ci kow suuf si sépp. Kenn dootul xeex walla dee ci xare. Kàddu Yàlla nee na : “ [Yàlla] mu ngiy tax xare yi jeex. ” — Sabuur 46:8, 9.

Wér-gi-yaram. Mbind mu sell mi dig na ne : “ Kenn ku dëkk [ca Àjjana] du ne : ‘ Dama feebar. ’ ” (Isayi 33:24). Te itam, kenn dootul lafañ walla gumba walla tëx walla muuma. — Isayi 35:5, 6.

Metit, naqar ak dee, dootul am. Kàddu Yàlla nee na : “ Dee dootul am walla naqar walla jooy walla mettit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ” — Peeñu bi 21:4.

Nit ku bon dootul am. Yexowa dig na ne : “ Nit ñu bon ñi dinañu leen jële ci suuf si ; te lu jëm ci workat yi dinañu leen buddee ci kowam. ” — Léebu 2:22.

Nit ñi dinañu bëgg te fonk ku nekk sa moroom. Jubadi, noot nit, bëgge, ak bañante, dootul am. Nit ñi dinañu nekk benn te dund dund gu sell ni ko Yàlla bëgge. — Isayi 26:9.