NJÀNGALE 12
Lan moo xew ginnaaw dee ?
Ku dee mooy ku dul dund. Dee mu ngi mel ni nelaw bu xóot (Yowanna 11:11-14). Ñi dee mënuñu dégg, walla gis, walla wax, walla xalaat dara (Dajalekat 9:5, 10). Diine ju dul dëgg dafay jàngale ne ñi dee dañuy dem fu mbindeefu xel yi nekk ngir dund fa ak seeni maam yi dee. Du loolu la Mbind mu sell mi wax.
Ñi dee mënuñu dimbali walla lor nit ñi. Ñu bare dañu faral di topp ay aada walla di def ay sarax te yaakaar ne loolu dina neex ñi dee. Loolu neexul Yàlla ndaxte mu ngi jóge ci fen bu Seytaane wax. Loolu mënul neex itam ñi dee, ndaxte dundatuñu. Waruñu ragal walla jaamu ñi dee. Yàlla rekk lañu wara jaamu. — Macë 4:10.
Ñi dee dinañu dundaat. Bu ëllëgee, Yexowa dina yee ñi dee ngir ñu dund ci Àjjana ci kow suuf (Yowanna 5:28, 29 ; Jëf ya 24:15). Ni nga mënee yee kuy nelaw, noonu la Yàlla mënee yee ku dee. — Mark 5:22, 23, 41, 42.
Xalaat ne nit du dee, fen la bu Seytaane mi nekk Ibliis siiwal. Seytaane ak malaakaam yu bon yi dañuy gëmloo nit ñi ne tuuri maam yi, ñu ngiy dund ba léegi te ñooy indi ay feebar walla yeneen coono ci kow nit ñi. Seytaane dafay nax nit ñi, léeg-léeg mu jaar ci gént walla lu lay feeñu. Yexowa bañ na ñiy jéema wax ak ñi dee. — 5 Musaa 18:10-12.