NJÀNGALE 14
Xaritu Yàlla yi dañuy moytu lu bon
Seytaane dafay jéema xiir nit ñi ci lu bon. Ku bëgga nekk xaritu Yàlla dafa wara bañ li Yexowa bañ (Sabuur 97:10). Li topp bokk na ci li xaritu Yàlla yiy moytu :
Bàkkaar ci wàllu tëdd ak góor walla jigéen. “ Waruloo njaaloo. ” (2 Musaa 20:14). Tëdd ak nit, fekk séyaguleen, lu bon la itam. — 1 Korent 6:18.
Naan ba màndi. “ Màndikat yi [...] duñu bokk ci nguuru Yàlla. ” — 1 Korent 6:10.
Rey nit, yàq biir. “ Waruloo rey nit. ” — 2 Musaa 20:13.
Sàcc. “ Waruloo sàcc. ” — 2 Musaa 20:15.
Fen. Yexowa bañ na “ làmmiñ buy fen ”. — Léebu 6:17.
Jëfi fitna ak mer ba mënatuloo téye sa bopp. “ Képp ku bëgg jëfi fitna, ci lu wóor [Yexowa] bañ na ko. ” (Sabuur 11:5). “ Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: [...] xadar [maanaam gaawa mer]. ” —Wure xaalis. “ Buleen séq dara ak ku [...] nay [maanaam ku “ bëgge ”, NW]. ” — 1 Korent 5:11.
Bañante diggante xeet. “ Soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal. ” — Macë 5:43, 44.
Li ñu Yàlla wax, suñu njariñ la. Moytu lu bon mën na nekk lu metti. Ndimbal bi nga mëna am ci Yexowa ak ci Seedeem yi, dina tax nga mëna moytu li neexul Yàlla. — Isayi 48:17 ; Filipp 4:13 ; Yawut yi 10:24, 25.