Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 10

Naka nga mënee xam diine dëgg ji ?

Naka nga mënee xam diine dëgg ji ?

Boo bëggee nekk xaritu Yàlla, danga wara topp diine ji Yàlla nangu. Isaa nee na “ jaamukat yi dëgg  ” dinañu jaamu Yàlla, jaamu buy ànd ak “ dëgg ”. (Yowanna 4:23, 24.) Ci benn yoon rekk lañu wara aw ngir mëna jaamu Yàlla ni mu ware (Efes 4:4-6). Diine dëgg ji moo jëm ca dund gu dul jeex, te diine ju dul dëgg moo jëm ca sànkute. — Macë 7:13, 14.

Mën nga xàmme diine dëgg ji booy xool ñi koy topp. Ndegam Yexowa ku baax la, ñi koy jaamu dëgg dañu wara baax itam. Ni garabu sorãs gu baax di meññe sorãs yu neex, noonu it la diine dëgg ji di meññe ay nit ñu baax. — Macë 7 :15-20.

Xaritu Yexowa yi dañu fonk bu baax Mbind mu sell mi. Xam nañu ne Mbind mu sell mi, ci Yàlla la jóge. Dañuy bàyyi li ci nekk mu won leen ni ñu wara dunde, ak ni ñuy faje seeni coono. Dafa leen di dimbali itam ñu jàng xam Yàlla (2 Timote 3:16). Dañuy jéema jëfe li ñuy jàngale.

Xaritu Yexowa yi dañuy wone mbëggeel, ku nekk sa moroom. Isaa wone na mbëggeel bi mu amoon ci nit ñi, bi mu leen doon jàngal ñu xam Yàlla, te bi mu doon faj ñi feebar. Ñiy topp diine dëgg ji, ñoom itam, dañuy bëgg seeni moroom yi. Ni Isaa, duñu xeeb ku néew doole walla ku ñu bokkalul xeet. Isaa nee na dinañu mëna xàmme taalibeem ya ci mbëggeel bi ñu am ci seen biir. — Yowanna 13:35.

Xaritu Yàlla yi dañuy màggal turu Yàlla, Yexowa. Ku la baña woo ci sa tur, ndax dina nekk sa xaritu benn-bakkan ? Déedéet ! Bu ñu amee xarit, dañu koy woo ci turam te bu ñuy waxtaan ak nit ñi, dañuy wax lu baax ci moom. Noonu, ñi bëgga nekk xaritu Yàlla war nañu koo woo ci turam te wax nit ñi lu jëm ci moom. Loolu la Yexowa bëgg ñu def. — Macë 6:9 ; Room 10:13, 14.

Ni ko Isaa doon defe, xaritu Yàlla yi dañuy jàngal nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla. Nguuru Yàlla, nguur gu nekk ca asamaan la, te moom mooy defar suuf si mu nekk àjjana. Xaritu Yàlla yi dañuy xamal nit ñi xibaar bu neex boobu jëm ci Nguuru Yàlla. — Macë 24:14.

Seede Yexowa yi dañuy góor-góorlu ngir nekk xaritu Yàlla. Dañu fonk Mbind mu sell mi te dañu bëggante ci seen biir. Dañuy woo Yàlla ci turam, di màggal tur boobu te dañuy jàngal nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla. Seede Yexowa yi dañuy topp diine dëgg ji ci kow suuf si tey.