Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 8

Ñan ñooy noonu yàlla yi ?

Ñan ñooy noonu yàlla yi ?

Ki gëna bañ Yàlla mooy Seytaane mi nekk Ibliis. Mbindeefu xel bu baña déggal Yexowa la. Ba léegi, Seytaane mu ngiy xeex Yàlla te mu ngiy teg ci kow doom-Aadama yi coono yu bare. Seytaane dafa bon. Fenkat ak reykat la. — Yowanna 8:44.

Yeneen mbindeefu xel ànd nañu ak Seytaane ci weddi Yàlla. Mbind mu sell mi tudde na leen rab. Ni Seytaane, rab yi maanaam malaaka yu bon yi, ay nooni doom-Aadama lañu. Li leen neex mooy lor nit ñi (Macë 9:32, 33 ; 12:22). Yexowa dina alag Seytaane ak malaakam yu bon yi ba fàww. Jot gi leen dese ngir sonal doom-Aadama yi bareetul. — Peeñu bi 12:12.

Soo bëggee nekk xaritu Yàlla, waruloo def li la Seytaane bëgga defloo. Seytaane ak malaakaam yu bon yi dañu bañ Yexowa. Ay noonu Yàlla lañu, te dañu bëgg nga nekk yow itam noonu Yàlla. Danga wara tànn koo bëgga neex — Seytaane walla Yexowa. Soo bëggee dund ba fàww, danga wara tànn def li Yàlla bëgg. Seytaane bare na ay pexe ngir nax nit ñi. Mu ngiy réeral li ëpp ci nit ñi. — Peeñu bi 12:9.