NJÀNGALE 9
Ñan ñooy xaritu Yàlla yi ?
Isaa mooy Doomu Yexowa te it mooy xaritam bi ko gëna jege, bi mu gëna fonk. Bala mu ñów dund ci kow suuf ni nit, dafa doon dund ca asamaan ni mbindeefu xel bu bare kàttan (Yowanna 17:5). Ginnaaw loolu, dafa ñów ci kow suuf si ngir jàngal nit ñi dëgg ci Yàlla (Yowanna 18:37). Joxe na itam bakkanam, bu nekkoon bakkanu nit, ngir musal ci bàkkaar ak dee doom-Aadama yi déggal Yàlla (Room 6:23). Léegi, Isaa, Buuru Nguuru Yàlla la. Nguur googu, ca asamaan la nekk te dina indi Àjjana ci kow suuf sii. — Peeñu bi 19:16.
Malaaka yi itam ay xaritu Yàlla lañu. Malaaka yi, bi ñu tàmbalee dund, nekkuñu woon ay nit ci kow suuf. Dañu leen sàkk ca asamaan bala Yàlla sàkk suuf si (Ayóoba 38:4-7). Am na ay milioŋi malaaka (Dañel 7:10). Xaritu Yàlla yooyu nekk ca asamaan, dañu bëgg nit ñi xam dëgg gi ci Yexowa. — Peeñu bi 14:6, 7.
Yàlla am na itam ay xarit ci kow suuf si ; mu ngi leen di wooye seedeem yi. Bu àtte amee, seede mooy wax li mu xam ci kenn walla lenn. Seede Yexowa yi dañuy wax nit ñi li ñu xam ci Yexowa ak ci li mu bëgga def (Isayi 43:10). Ni malaaka yi, Seede yi dañu la bëgga dimbali nga xam dëgg gi ci Yexowa. Dañu bëgg nga nekk yow itam xaritu Yàlla.