Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 1

Yàlla mu ngi lay woo ngir nga nekk xaritam

Yàlla mu ngi lay woo ngir nga nekk xaritam

Yàlla bëgg na nga nekk xaritam. Ndax mas nga xalaat ne mën nga nekk xaritu Ku gëna màgg ci suuf ak ca asamaan yépp ? Yonent Yàlla Ibrayima, mi doon dund ca jamano yu yàgg ya, xaritu Yàlla lañu ko wooye woon (Saak 2:23). Mbind mu sell mi, mu ngi wax ci ñeneen nit ñu doon xaritoo ak Yàlla te am ci ay barke yu bare. Tey jii, ci àddina si sépp, am na ay nit ñu dem ba mujja nekk xaritu Yàlla. Yow it, mën nga nekk xaritu Yàlla.

Nekk xaritu Yàlla moo gën nekk xaritu nit ku mu mënta doon. Yàlla du tas mukk yaakaaru xaritam yi takku ci moom (Sabuur 18:25). Nekk xaritu Yàlla moo gën am alal. Ku bare alal, bu deewee, alalam yépp dafay dem ci loxo ñeneen. Waaye, ku xaritoo ak Yàlla, am nga alal bu kenn mënula nangu. — Macë 6:19.

Mën na am ay nit jéem laa teree jàng lu jëm ci Yàlla. Mën na nekk sax kenn ci say xarit walla say mbokk (Macë 10:36, 37). Su amee ay nit ñu lay ñaawal walla di la tiital, nanga laaj sa bopp : ‘ Kan laa bëgga neex — doom-Aadama walla Yàlla ? ’ Ci sa xalaat : ku la ne “ bul lekkati mukk ”, dinga ko topp ? Déedéet ! Boo bëggee dund, danga wara lekk. Waaye Yàlla mën na tax nga dund ba fàww ! Kon, bu la kenn teree jàng ni nga mënee nekk xaritu Yàlla. — Yowanna 17:3.