Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 18

Nekkal xaritu Yàlla ba fàww !

Nekkal xaritu Yàlla ba fàww !

Am xarit, yombul ; yàgg ak xarit, yombul itam. Li ngay jéema def ngir nekk xaritu Yàlla te yàgg ci, Yàlla dina ko barkeel bu baax-a-baax. Isaa nee na ñi amoon ngëm ci moom : “ Dëgg gi dina leen muccal. ” (Yowanna 8:32, NW). Loolu lu mu tekki ?

Mën nga mucc léegi. Mën nga mucc ci njàngale yu dul dëgg walla ci fen yu jóge ci Seytaane. Ay milioŋi nit ñu xamul Yexowa amuñu benn yaakaar ci seen àddina. Waaye mën nga rëcc ci loolu (Room 8:22). Xaritu Yàlla yi, mucc nañu sax ci “ ragala dee ”. — Yawut yi 2:14, 15.

Mën nga mucc ca àddina su bees su Yàlla di indi. Bu ëllëgee, dinga mëna mucc ci lu baree-bare ! Ca Àjjana ci kow suuf, xeex , feebar, nit ñiy jéggi li yoon tëral, dootul am. Kenn dootul xiif walla néew doole. Màgget ak dee, dootul am. Kenn dootul ragal dara. Kenn dootul noot kenn. Dootul amati nit ñu jubadi. Mbind mu sell mi, lii la wax ci Yàlla : “ Dangay ubbi sa loxo di faj bëgg-bëggu lépp luy dund. ” — Saabur 145:16.

Xaritu Yàlla yi dinañu dund ba fàww. Dund gu dul jeex mooy maye bu mag bi Yàlla di defal ñiy jéema nekk ay xaritam (Room 6:23). Xalaatal tuuti ci li dund gu dul jeex di mëna tekki ci yow !

Dinga am jotu def lu bare. Xéyna dinga bëgga jànga tëgg jumtukaayu misig, walla nataal ay tablo, walla nekk minise. Mbaa nga bëgga yokk sa xam-xam ci mala yi walla garab yi. Mën na am itam nga bëgga tukki te xam yeneen dëkk walla yeneen xeet. Loolu yépp dinañu ko mëna def su ñu amee dund gu dul jeex !

Dinga am jotu xaritoo ak ñu bare. Dund ba fàww dina nu may ñu mëna xam ñeneen nit ñu bare ñu dem, ñoom it, ba nekk xaritu Yàlla. Dinga mëna xam seen mën-mën te gis ci ñoom ay jikko yu rafet, te dinañu nekk itam say xarit. Dinga leen bëgg, te dinañu la bëgg (1 Korent 13:8). Boo amee dund gu dul jeex, dinga am jotu xaritoo ak nit ñépp ci kow suuf si ! Waaye li gën loolu yépp mooy : sa xaritoo ak Yexowa dina gën di dëgër bés bu nekk, ba abadan. Yàlla nga nekk xaritu Yàlla ba fàww !