Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 3

Danga wara jàng xam Yàlla

Danga wara jàng xam Yàlla

Boo bëggee nekk xaritu Yàlla, danga wara jàng xam Yàlla. Ndax say xarit yi xam nañu sa tur, di la woo ci sa tur ? Waawaaw. Yàlla itam bëgg na nga xam turam, di ko woo ci turam. Turu Yàlla mooy Yexowa (Sabuur 83:18 ; Macë 6:9). Danga wara jàng itam li mu bëgg ak li mu bañ. War nga xam ñan ñooy xaritam yi ak ñan ñooy noonam yi. Xam nit, jot la laaj. Mbind mu sell mi nee na dañu wara fexe ba am jot ngir jàng xam Yexowa. — Efes 5:15, 16.

Xaritu Yàlla yi dañuy def li ko neex. Seete ko ci say xarit. Boo soxoree ak ñoom, di def li ñu bañ, ndax dinañu wéy di nekk say xarit ? Déedéet ! Noonu it, soo bëggee nekk xaritu Yàlla, danga wara def li ko neex. — Yowanna 4:24.

Du diine yépp ñoo mëna tax nga nekk xaritu Yàlla. Isaa, ki nekk xaritu Yàlla bi ko gëna jege, nee na ñaari yoon ñoo am. Benn bu yaatu te ñi ciy jaar bare nañu. Yoon boobu ca sànkute la jëm. Beneen bi, dafa xat te ñi ciy jaar barewuñu. Yoon boobu, ca dund gu dul jeex la jëm. Loolu, mu ngi tekki ne boo bëggee xaritoo ak Yàlla, danga wara jàng xam fu ñu wara jaar ngir jaamu ko ci dëgg. — Macë 7:13, 14.