NJÀNGALE 13
Xonjom ak luxus, lu bon la
Seytaane dafa bëgg nga bokk ci xonjom ak yu mel noonu. Ñu bare dañuy def ay sarax ngir seeni maam yi dee walla ay mbindeefu xel aar leen ci musiba. Dañuy def loolu ndaxte dañu ragal kàttanu xel yooyu. Dañuy tàkk ay gàllaaj, di naan ay “ garab ” walla di ko diw seen yaram, foog ne kàttanu xonjom moo ci nekk. Dañuy nëbb walla suul ci seen kër ay yëf, foog ne yëf yooyu dinañu leen aar. Am na ñeneen ñuy jëfandikoo “ garab ”, yaakaar ne dina leen dimbali ñu am alal, eksamee ca lekkool, jëkkër walla jabar.
Li la gëna mëna musal ci Seytaane mooy Yexowa nekk sa xarit. Yexowa Yàlla ak malaakaam yi ñoo gëna am kàttan fuuf Seytaane ak malaakaam yu bon yi (Saak 2:19 ; Peeñu bi 12:9). Yexowa bëgg na lool won kàttanam xaritam yi — ñiy wone takkute gu mat ci moom. — 2 Nettaliy xew-xewi cosaan 16:9.
Kàddu Yàlla nee na : “ Waruloo luxus. ” Yexowa dafa bañ luxus ak xonjom ndaxte jëf yooyu mën nañu la yóbbu ba ci biir loxo Seytaane mi nekk Ibliis. — 3 Musaa 19:26.