Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 2

Yàlla mooy xarit bi gën boo mëna am

Yàlla mooy xarit bi gën boo mëna am

Dem ba nekk xaritu Yàlla, mënoo am lu ko gën. Yàlla dina la jàngal ni nga mënee am bànneex ak jàmm ; dina la génne ci ngëm yu dul dëgg yu bare ak ci ay jëf yu bon yuy lore. Dina déglu say ñaan. Dina la dimbali nga am jàmm ci sa biir xol ak xel mu dal (Sabuur 71:5 ; 73:28). Yàlla dina la jàpple boo nekkee ci coono (Sabuur 18:18). Te itam Yàlla bëgg na la may dund gu dul jeex. — Room 6:23.

Booy gën di jege Yàlla, dinga gëna jege itam ay xaritu Yàlla. Ñoom it, dinañu nekk say xarit. Ci dëgg, dinañu mel ni ay mbokk ci yow, yu góor ak yu jigéen. Dinañu la jàngal lu jëm ci Yàlla, di la dimbali, di la xiir ci lu baax. Te loolu yépp, dinañu ko def ak mbégte.

Yàlla du suñu moroom. Boo bëggee nekk xaritu Yàlla, am na lu am solo loo wara xam. Xaritoo ak Yàlla bokkul ak xaritoo ak sa moroom. Yàlla moo ñu gëna màgg fuuf, moo ñu gëna am xam-xam fuuf, te moo ñu gëna bare kàttan fuuf. Ci dëgg, moom moo ñu wara ilif. Kon, su ñu bëggee nekk xaritam, war nañu koo déglu te def li mu ñu sant. Loolu, suñu njariñ lay doon bés bu nekk. — Isayi 48:18.