Ubbil li ci biir

XAAJ 1

Leer gu wóor gi ñëw ci àddina

Leer gu wóor gi ñëw ci àddina

Ca jàlbéen ga kàddu gi mu ngi woon ak Yàlla te am kàttan mel ni Yàlla (gnj 1 00:00–00:43)

Ci kàddu gi lañu jaar ngir sàkk lépp (gnj 1 00:43–01:00)

Ci moom la dund ak leer nekk (gnj 1 01:00–02:11)

Lëndëm gi muurul leer gi (gnj 1 02:11–03:59)

Luug mu ngi wax Tewofil ci ban anam la bind nettali bi ak lu tax mu bind ko (gnj 1 04:12–06:02)

Jibril mu ngi yégle juddub Yaxya (gnj 1 06:03–13:53)

Jibril mu ngi yégle juddub Yeesu (gnj 1 13:53–18:25)

Maryaama mu ngi dem seeti mbokkam Elisabet (gnj 1 18:26–21:13)

Maryaama mu ngi màggal Yexowa (gnj 1 21:13–24:00)

Bi Yaxya juddoo ak bi ñu koy tudd (gnj 1 24:00–27:13)

Sàkkaryaa mu ngi yégle (gnj 1 27:14–30:55)

Maryaama ëmb na ci kàttanu xel mu sel mi; ni Yuusufa def (gnj 1 30:55–35:27)

Yuusufa ak Maryaama ñu ngi dem Betleyem; Yeesu juddu na (gnj 1 35:27–39:51)

Malaaka yi feeñu nañu sàmm yi ca tool ya (gnj 1 39:51–41:38)

Sàmm yi dem nañu ca lekkukaayu jur ga (gnj 1 41:38–43:54)

Yóobu nañu Yeesu ca kër Yàlla ga ngir sédde ko Yexowa (gnj 1 43:54–45:00)

Simeyon kontaan na gis Kirist bi (gnj 1 45:00–48:49)

Aana mu ngi wax ci xale bi (gnj 1 48:49–50:17)

Boroom xam-xam yi seeti nañu Yeesu te Erodd mu ngi wut rey xale bi (gnj 1 50:21–55:49)

Yuusufa jël na Maryaama ak Yeesu te daw jëm Misra (gnj 1 55:49–57:31)

Erodd rey na xale yu goor yi ca Betleyem ak li ko wër (gnj 1 57:31–59:28)

Yeesu ak waajuram yi dem nañu dëkki Nasaret (gnj 1 59:28–1:03:55)

Yeesu bi mu ame fukki at ak ñaar mu ngi ca kër Yàlla ga (gnj 1 1:03:55–1:09:36)

Yeesu dellu na Nasaret ak waajuram yi (gnj 1 1:09:36–1:10:22)

Leer gu wóor googu moo war a ñëw ci àddina (gnj 1 1:10:23–1:10:57)