NJÀNGALE 13
Lan mooy xibaaru jàmm bi jëm ci wàllu diine ?
1. Ndax diine yépp a baax ?
Ci diine boo dem am na ay nit ñu dëggu. Li Yàlla di bàyyi xel ci nit ñooñu te di leen toppatoo, xibaaru jàmm la. Waaye li doy waar mooy, am na ñuy jëfandikoo diine yi ngir def ay ñaawteef (2 Korent 4:3, 4 ; 11:13-15). Ni ko xibaar yi di wone, yenn diine yi bokk nañu ci terrorisme, bokk ci xare yi ak reyante yi am ci diggante xeet ak xeet. Dañu ciy dégg itam mbirum sàkku xale. Loolu aka moo metti ñi gëm Yàlla dëgg ! — Jàngal Macë 24:3-5, 11, 12.
Bu diine dëgg ji di màggal Yàlla, diine yu dul dëgg yi di naqaral Yàlla. Diine yooyu dañuy jàngale ay xalaat yu nekkul ci Biibël bi, lu mel ni ay njàngale yu dul dëgg yu jëm ci Yàlla ak yu jëm ci dee. Waaye Yexowa dafa bëgg nit ñi xam dëgg gi jëm ci moom. — Jàngal Ézékiel 18:4 ; 1 Timote 2:3-5.
2. Lan mooy xibaaru jàmm bi jëm ci wàllu diine ?
Ci dëgg-dëgg Diine yiy wax ne dañu bëgg Yàlla fekk, àddina Seytaane lañu bëgg, mënuñu nax Yàlla (Saag 4:4). Diine yu dul dëgg yépp la Kàddu Yàlla di woowe “ Babilon mu mag mi. ” Babilon moo nekkoon dëkk bu diine yu dul dëgg yi soqeekoo ginnaaw mbënn mi amoon ca jamono Nóoyin. Léegi Yàlla jële fi diine yuy tas yaakaaru doomu Aadama yi te di leen noot. — Jàngal Peeñu ma 17:1, 2, 5, 16, 17 ; 18:8.
Am na xibaar bu gën a neex. Yexowa fàttewul nit ñu dëggu ñi nekk ci diine yu dul dëgg yi ci àddina si sépp. Fu mu nekk nii, mu ngi dajale nit ñooñu, di leen jàngal dëgg gi. — Jàngal Mika 4:2, 5.
3. Lan la nit ñu dëggu ñi war a def ?
Yexowa yëg na nit ñi bëgg dëgg ak lu baax. Mu ngi leen di woo ngir ñu bàyyi diine yu dul dëgg yi. Nit ñi bëgg Yàlla dinañu nangu def ay coppite ci seen dundin ngir neex ko. — Jàngal Peeñu ma 18:4.
Ca jamono Karceen yu njëkk ya, bi nit ñu dëggu ñi déggee xibaaru jàmm bi jóge ci taalibe Yeesu yi, nangu nañu ko ak mbégte. Jàng nañu dundin bu bees bu jóge ci Yexowa, di dundin bu gën, bu ànd ak yaakaar ak jubluwaay. Ay royukaay yu baax lañu pur ñun, ndaxte nangu nañu xibaaru jàmm bi ci li ñu jiital Yexowa ci seen dund. — Jàngal 1 Tesalonig 1:8, 9 ; 2:13.
Yexowa mu ngi dalal ñi nga xam ne dañoo bàyyi diine yu dul dëgg yi te ñëw ci mbooloo bi koy jaamu. Bu ngeen nangoo wooteb Yexowa, dingeen xaritoo ak moom, xaritoo it ak mbooloo mi bëggante ci seen biir te di jaamu Yexowa, te it dingeen am dund gu dul jeex. — Jàngal Màrk 10:29, 30 ; 2 Korent 6:17, 18.
4. Naka la Yàlla di indee jàmm ci kaw suuf si sépp ?
Yàlla dina àtte diine yu dul dëgg yi. Loolu, xibaaru jàmm la ndaxte nit ñi dootuñu nekk ci nootaange. Su boobaa diine yu dul dëgg yi dootuñu nax mukk doomu Aadama yi ba di leen xàjjale. Ñépp ñuy dund dinañu booloo jaamu benn Yàlla dëgg ji. — Jàngal Peeñu ma 18:20, 21 ; 21:3, 4.