Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Lu tax ñu soxla am yaakaar?

Lu tax ñu soxla am yaakaar?

Lu tax ñu soxla am yaakaar?

DANIEL, xale bu góor bi ñu tudd ci waxtaan bii weesu te amoon cancer, bu wéyoon di am yaakaar, lan moo naroon a xew? Ndax dina doon wér? Ndax dina doon dund ba tey? Xéyna, ñi gëm sax ne yaakaar mën na dimbali nit bu feebaree, duñu wax lu mel noonu. Loolu, ponk bu am solo la. Waruñu teg yaakaar fu mu àggul. Yaakaar mënul a faj lépp.

Doktoor Nathan Cherney wax na ci tele bi tudd CBS News, ci loraange bi nekk ci teg yaakaar fu mu àggul, bu ñu amee feebar bu garaaw. Lii la wax: «Am na ay jëkkër yuy jiiñ seen jabar yu feebar ne, seen jabar gëmuñu ne dinañu wér te amuñu njort bu rafet.» Mu yokk ci ne: «Gis-gis biy gëmloo ñu bare ne yaakaar mën na leen dimbali ñu wér, nax na ñu bare. Kon bu nit ki wérulee, dafa mel ni dañu koy wax ne, góor-góorluwul ngir mën a wér. Te loolu jaaduwul.»

Dëgg gi mooy, nit ñi am feebar bu lenn nara rey, ñu ngi ci xeex bu metti, buy jeexal seen doole. Te tuumaal leen, yokkal leen coono la. Ku leen bëgg dëgg, du def loolu. Ndax loolu dafay tekki ne, yaakaar amul njariñ?

Déedéet. Doktoor Cherney, xam-xamam dafa màcc ci dimbali ñiy waaj a dee, ñu bañ a yëg metit ba mu ëpp. Ñu mel ni moom, gëm nañu ne, am na njariñ ñu dimbali nit ki feebar mu ànd ak dal, bu dee sax feebar bu garaaw la am. Am na ay firnde yu wóor yuy wone ne yaakaar mën na def loolu ci nit walla lu ko raw.

Njariñ bi nekk ci am yaakaar

Doktoor W. Gifford-Jones miy nekk taskatu xibaar ci wàllu wér-gi-yaram nee na: «Yaakaar, garab bu am doole la.» Xool na ay gëstu yu bare ngir xam njariñ bi nekk ci jàppale ñu feebar bay waaj a dee, ngir ñu bañ a xàddi. Am na ñu gëm ne, fasoŋu ndimbal boobu, dafay tax ki feebar gën a rafet njort te ànd ak dal. Benn gëstu bi ñu def ci atum 1989 wone na ne, nit ñi feebar te jot ndimbal lu mel noonu, dañuy gën a gudd fan. Waaye ay gëstu yi ñu def bu yàggul dëggaluñu ko. Terewul, am na ay gëstu yu nangu ne ñi feebar te mu am ñu leen di jàppale ngir ñu bañ a xàddi, gaawuñu am dépression te duñu sonn ni ñeneen ñi ñu jàppalewul.

Nañu xool benn gëstu buy wax ci njariñ bi yaakaar am ci feebaru xol. Dañu dajale lu ëpp 1 300 nit ngir seet ndax am nañu yaakaar ci seen dund, waaw walla déet. Bi ñu leen saytoo, fukki at ginnaaw loolu, ñu gis ne, téeméer yoo jël ci ñoom, fukk ak ñaar ñi amoon nañu feebaru xol. Ci ñi amoon feebaru xol, ñi amul woon yaakaar, ñoo ëpp ñaari yoon ñi amoon yaakaar. Laura Kubzansky, mi nekk jàngalekat ci wàllu wér-gi-yaram, lii la wax ci lu jëm ci gëstu boobu: «Lu bare li ñu wax ci njariñ bi rafet njort am ci wér-gi-yaram ay nettali rekk la. Waaye gëstu bii moo njëkk a wone ay firnde yu leer ci ne, rafet njort lu baax la ci xol.»

Am na ay gëstu yuy wone ne, ñi gëm ne seen wér-gi-yaram baax na, bu ñu leen opeeree ba pare, ñooy gën a gaaw a wér ñi gëm ne seen wér-gi-yaram demewul noonu. Ay gëstu wone nañu itam ne, ñi rafet njort dañuy gudd fan. Benn gëstu wax ci ni mag ñi gise seen nekkin. Seetlu nañu ne, bu ñu wone mag ñi ne màgget ak sago ak xam-xam ñoo ànd, loolu dafa leen yokk doole ak cawarte. Bu ñuy dox sax, loolu dafay feeñ ci ñoom. Li muy def ci ñoom, dafa mel ni, lu nit di yëg buy def espoor ci diiru 12 semen!

Lu tax yaakaar, rafet njort ak bañ a xàddi am njariñ ci wér-gi-yaram? Xéyna, boroom xam-xam yi ak doktoor yi xamaguñu bu baax yaramu doomu Aadama, ngir joxe ay tont yu wóor ci laaj boobu. Terewul boroom xam-xam yiy gëstu mbir mi, am na lu ñu ci xalaat. Kenn kuy jàngale ci lu jëm ci yuur lii la wax:«Bég te am yaakaar lu neex la. Nit ku bég du bare stress, te loolu lu baax la ci wér-gi-yaramam. Bég, bokk na itam ci li nit ki mën a def ngir am wér-gi-yaram.»

Xéyna loolu mën na bett ay doktoor ak yenn boroom xam-xam yi. Waaye du lu bees ci ñiy jàng Biibël bi. Daanaka 3 000 at ci ginnaaw, Suleymaan miy nekkoon buur bu am xam-xam, lii la ko Yàlla xiir mu bind: «Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal [walla néewal doole]» (Kàddu yu Xelu 17:22). Ndax seetlu ngeen li aaya bi wax? Aaya bi waxul ne, xol bu sedd dafay faj bépp feebar. Li mu wax mooy «day garabal». Kon mën nañu laaj suñu bopp lii: Yaakaar bu nekkoon garab, ban doktoor moo ko dul bindal ñi muy faj? Waaye yaakaar yemul rekk ci dimbali nit am wér-gi-yaram.

Rafet njort, ñaaw njort ak sa dund

Gëstukat yi seetlu nañu ne, rafet njort lu baax la ci doomu Aadama. Ñi rafet njort, dañuy faral di xareñ ci lekkool, ci liggéey ba ci espoor sax. Li koy misaal mooy, benn gëstu bi ñu def ci benn ekipu jigéen ñi nga xam ne ay dawkat lañu. Ñi leen doon tàggat, dañu doon seetlu ba xam tolluwaayu kenn ku nekk ci ñoom. Laajoon nañu itam kenn ku nekk ci jigéen ñi, mu wax li mu yaakaar ne moom la mën a def, bu joŋante amee. Li jigéen ñi gëmoon ne dinañu ko def, moo mujj a am. Lu tax yaakaar ame noonu doole?

Boroom xam-xam yi jànge nañu lu bare ci nit ñi ñaaw njort. Lu ëpp 50 at ci ginnaaw, gëstukat yi gis nañu ne, mala yi, ba ci nit ñi sax mën nañu dem ba dootuñu amati yaakaar. Ci benn gëstu, dañu tëj ay nit ci benn néeg, di lenn tanqal. Ñu ne leen bu ñu bësee ci ay butoŋ, mën nañu fey li lenn di tanqal. Nit ñi ñu tëjoon, mujj nañu fey li lenn doon tanqal.

Mu am beneen gurupu nit ñi ñu tëj. Ñu wax leen li ñu waxoon gurup bu njëkk bi. Waaye bi ñu bësee butoŋ yi, mënuñu woon a fey li leen doon tanqal. Ñu bare ci ñoom daldi xàddi. Ginnaaw loolu, bi ñu leen tëjaatee, nanguwuñu def dara. Gëmoon nañu ne, ak li ñu mën a def, dara du sotti. Waaye ci ñaareelu gurup bi, ñi rafet njort, dañu bañoon a xàddi.

Doktoor. Martin Seligman, mi bokkoon ci ñi doon def gëstu bi, dafa mujj a sóobu ci gëstu lu jëm ci rafet njort ak ñaaw njort. Dafa gëstu bu baax liy tax ñenn ñi di gaaw a xàddi. Lii la wax lu jëm ci ñaaw njort ak li muy def ci nit ki: «Gëstu naa lu jëm ci ñaaw njort ci diiru 25 at. Gis naa ne, ñi ñaaw njort, dañuy gëm ne lépp lu bon li leen dal, ñoo ko teg seen bopp. Gëm nañu itam ne, lu bon dina wéy di leen dal, te mënuñu ci dara. Nit ñu mel noonu, lu bon ñoom lay gën a dal ñi rafet njort.»

Xéyna tey, am na ñu foog ne loolu lu bees la. Waaye, ñiy jàng Biibël bi xamoon nañu ko ba pare. Lii la Kàddu yu Xelu wax: «Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew» (Kàddu yu Xelu 24:10). Biibël bi wax na ci lu leer ne, ku xàddi dafay néew doole. Kon, lan nga mën a def ngir bañ a ñaaw njort te gën a rafet njort? Lan nga mën a def ngir am yaakaar?

[Foto bi]

Yaakaar mën na la amal njariñ lu réy