Mën nga xeex ñaaw njort
Mën nga xeex ñaaw njort
NAKA nga gise jafe-jafe yi ngay jankoonteel? Boroom xam-xam yu bare gëm nañu léegi ne, tont bi nit ki di joxe ci laaj bii, mooy wone ndax ku ñaaw njort la walla ku rafet njort la. Ñun ñépp ay am ay jafe-jafe ci suñu dund. Waaye am na ñu ci ëppale seeni moroom. Kon lu tax mu am ñiy xàddi bu ñu amee jafe-jafe te ñeneen ñi duñu xàddi, donte sax dañuy am ay jafe-jafe yu gën a réy?
Xalaatal ngay wut liggéey. Ñu woo la, waxtaan ak yow, waaye mujj ñu laa jël. Naka ngay gise loolu? Mën nga foog ne dañu laa bañ te def ko porobalem. Mën nga dem ba gëm ne doo mas a am liggéey. Walla sax mën nga dem ba gëm ne amuloo benn njariñ te kenn soxlawu la. Loolu sax mooy ñaaw njort.
Ni nga mënee xeex ñaaw njort
Naka nga mënee xeex ñaaw njort? Li nga war a njëkk a def mooy, jàng raññe xalaat yu ñaaw yi. Boo paree, nga def lépp li nga mën ngir génne xalaat yooyu ci sa bopp. Jéemal a xam li tax jëluñu la ci liggéey boobu. Ni ñu la jëlule, ndax ci yow la? Walla patroŋ bi keneen la soxla woon ku am yeneen mën-mën?
Boo bëggee xam ndax li ngay xalaat baax na, méngaleel li ngay xalaat ak li am. Ni ñu la jëlule, ndax dafay tekki ne amuloo benn njariñ? Ndax am na ay fànn yoo xam ne yaa ngi ciy góor-góorlu bu baax, lu mel ni sa diggante ak sa Boroom, sa dundu njaboot walla sa diggante ak say xarit? Bàyyil di xalaat ne lépp looy def dafa lay jural musiba. Ci dëgg, lan moo la wóor ne doo mas a am liggéey? Am na leneen li nga mën a def ngir bañ a ñaaw njort.
Nanga rafet njort ci li nga mën a def
Ci at yii weesu, gëstukat yi wax nañu li yaakaar di tekki waaye dese na leer. Nee nañu, ku am yaakaar, dangay gëm ne dinga matal say jubluwaay. Ni ñu ko wone ci waxtaan bi di topp, yaakaar du rekk matal say jubluwaay. Waaye li gëstukat yi wax ci yaakaar am na njariñ ci fànn yu bare. Bu ñu bàyyee xel ci li ñu wax ci yaakaar, dinañu gën a rafet njort te góor-góorlu ngir matal suñu jubluwaay.
Bu ñu bëggee gëm ne mën nañu matal suñuy jubluwaay, fàww ñu am ay jubluwaay te di leen matal. Boo jàppee ne masuloo matal benn jubluwaay, kon xoolaatal bu baax say jubluwaay. Ndax am nga ay jubluwaay? Yomb na torop nit topp ci ittey àddina, ba du xalaat ci li mu bëgg dëgg ak li gën a am solo ci moom. Lu jëm ci jiital li gën a am solo, gis nañu ne Biibël bi waxoon na bu yàgg ne: «Nangeen sax noonu ci li gëna rafet» (Filib 1:10).
Bu ñu xamee li gën a am solo, dina gën a yomb ci ñun ñu am ay jubluwaay ci wàllu ngëm, ci wàllu njaboot ak ci suñu dund bés bu nekk. Bu ñuy tàmbali, am na solo ñu bañ a am ay jubluwaay yu bare lool. Te bu ñuy am jubluwaay, nañu wóor ne dina ñu ko mën a matal. Bu ñu amee jubluwaay bu jafe matal, dina wàññi suñu doole ba ñu dem ba xàddi. Loolu moo tax, ngir matal say jubluwaay yu gën a mag yi, li gën mooy, nga xaajleen, defleen ay jubluwaay yu gën a ndaw.
Dañuy faral di wax naan «Boo bëggee dara, mën ko.» Te wax jooju, am na lu ciy dëgg. Bu ñu demee ba am jubluwaay bu leer ci suñu bopp, dañu war a wone ne bëgg nañu def lépp ngir matal ko. Mën nañu yokk bëgg-bëgg boobu, bu ñuy xalaat ci njariñ bi ñuy am bu ñu matalee jubluwaay boobu. Dëgg la ne, dina am ay jafe-jafe, waaye jafe-jafe yooyu waruñoo tere ñu matal suñu jubluwaay.
Waaye itam, war nañu xalaat ci ni ñuy def ba matal suñu jubluwaay yi. Benn bindkat bu tudd C. R. Snyder bu def benn gëstu bu xóot ci njariñu yaakaar nee na, dañu war a am ay pexe yu bare ngir matal bépp jubluwaay. Bu ko defee, bu benn bi doxul, ñu jéem beneen.
Snyder nee na itam, mën nañu di weccee suñuy jubluwaay. Bu ñu amee benn jubluwaay bu ñu mënul a matal, bu ñu ciy bàyyi suñu xel saa su nekk, loolu dafay wàññi suñu doole. Waaye, bu ñu bàyyee jubluwaay boobu te jël beneen bu gën a yomb, loolu dina ñu mayaat yaakaar.
Biibël bi am na misaal bu baax ci fànn boobu. Buur bi Daawuda, bëggoon na lool tabax kër ngir Yexowa Yàlla. Waaye Yàlla wax ko ne, doomam Suleymaan moo koy def. Daawuda geddul te jéemul a forse, waaye dafa wut beneen jubluwaay. Dafa def lépp li mu mën ngir dajale xaalis ak lépp li doomam waroon a soxla ngir def liggéey bi (1 Buur ya 8:17-19; 1 Chroniques 29:3-7).
Bu fekkee ne sax dem nañu ba rafet njort te am ay jubluwaay, ba tey, mën na jafe ci ñun ñu am yaakaar. Loolu, nu mu mën a nekke? Lu bare ci li ñuy jural ñàkk yaakaar, doomu Aadama mënu ci dara. Naka lañu mënee wéy di am yaakaar bu ñu gisee ndóol bi, geer yi, njubadi gi, feebar yi ak dee gi am ci àddina si?
[Foto bi]
Bu ñu la jëlulee ci liggéey bi nga doon wut, ndax loolu mooy doo mas a am liggéey?
[Foto bi]
Buur bi Daawuda dafa soppi gis-gisam ci jubluwaay yi mu amoon