Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Wax ju ànd ak respe mooy simaa biy tax seen séy dëgër

ÑI NEKK CI SÉY ÑOO MOOM LII

3: Respe

3: Respe

LI MUY TEKKI

Jëkkër ak jabar yuy wone respe, ku ci nekk dafay wéy di fonk moroomam, bu dee sax am na mbir moo xam ne déggoowuñu ci. Benn téere buy wax ci séy lii la wax: «Ñooñu, duñu jàpp ne li ñu xalaat rek mooy dëgg. Waaye bu ñu amee jafe-jafe, dañuy toog waxtaan ci. Ku nekk dafay déglu moroomam ak respe ngir ñu mën a déggoo ci dogal bi ñuy jël».

LII LA BIIBËL BI WAX: «Ku bëgg [...] du wut njariñu boppam» (1 Korent 13:4, 5).

«Ci man, respekte sama jabar mooy won ko ne fonk naa ko, te bañ a def dara lu koy metti walla luy yàq suñu séy» (Micah).

LI TAX MU AM SOLO

Bu respe amul ci diggante jëkkër ak jabar, seen waxtaan mën na dem ba doon xaste, kókkali walla sax ku nekk jéppi sa moroom. Te gëstukat yu bare nee nañu loolu mooy tas séy yu bare.

«Wax ci sa jabar lu àndul ak teggin walla lu ñaaw, loolu mën na yàq kóolute gi mu am ci yow, te yàq itam seen séy» (Brian).

LI NGA MËN A DEF

LAAJAL SA BOPP LII

Ci diiru juróom ñaari fan, seetlul bu baax li ngay def ak li ngay wax. Boo paree, tontul ci laaj yii di topp:

  • Ñaata yoon nga xas sa jëkkër walla sa jabar? Ñaata yoon nga ko ndokkeel?

  • ‘Naka laa wone respe sama jëkkër walla sama jabar?’

WAXTAANAL AK KI NGA SÉYAL CI LAAJ YII DI TOPP

  • Lan ngeen mën a def ak lan ngeen mën a wax ba ku nekk yëg ne moroomam respekte na ko?

  • Yan jëf ak yan kàddu ñooy tax ba ku nekk jàpp ne moroomam respektewu ko?

XELAL

  • Bindal ñetti fasoŋ yoo bëgg ñu won la respe. Waxal ki nga séyal mu def loolu itam. Na ku nekk jox moroomam li mu bind, te ku nekk góor-góorlu ngir won moroomam respe fi mu ko soxlaa.

  • Bindal lépp li la gën a neex ci sa jëkkër walla sa jabar. Boo paree, nga wax ko ko.

«Ci man, respekte sama jëkkër mooy, won ko ci samay jëf ne fonk naa ko te dama bëgg mu bég. Ci jëf yu ndaw yu may faral di def, lay wone respe dëgg, waaye du ci jëf yu réy kese» (Megan).

Li am solo, du ndax foog nga ne respekte nga sa jëkkër walla sa jabar, waaye ndax sa jëkkër walla sa jabar yëg na ci xolam ne respekte nga ko.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Solooleen boog yërmande, laabiir, woyof, lewet ak muñ» (Kolos 3:12).