Ubbil li ci biir

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Ndax naan sàngara lu baax la?

Ndax naan sàngara lu baax la?

Biibël bi terewul naan tuuti sàngara bu ñu ko yoon mayee. Waaye tere na naan sàngara ba màndi (Sabóor 104:15; 1 Korent 6:​10).

Léegi bu la ñeneen ñi xiiree ci naan sàngara te yoon walla say waajur tere la ko, lan ngay def?

 Xalaatal ci li la naan sàngara mën a jural

Am na ay ndaw yu foog ne bala ñoo mën a féexal seen xol, fàww ñu naan sàngara. Waaye bu ñu naanee ba pare, lan moo mën a xew?

  • Yoon mën na dal sa kaw. Su fekkee ne yoon dafay tere naan sàngara fi nga dëkk, boo naanee mën nañu la alamaan, yóbbu la ci kanamu yoon, nangu sa permis, liggéeyloo la walla sax tëj la kaso (Room 13:3).

  • Sa der mën na ci yàqu. Sàngara mën na tax ba doo too ànd ak sa sago. Mën na la defloo walla waxloo loo xam ne dinga ko réccu ëllëg (Kàddu yu Xelu 23:31-​33). Ak réseaux sociaux yi tey, lépp loy def mën na tilimal sa der te dina jafe lool nga setal ko.

  • Mën na tax nga bàyyeeku. Sàngara mën na tax ñu agerese la walla ñu sàkku la ci lu yomb. Sàngara mën na tax itam ñeneen ñi yóbbaale la ba nga dugg ci lu wóorul mbaa nga def lu yoon tere.

  • Mën na nekk tàmmeel bu bon. Ay gëstukat wone nañu ne, looy gën di teel a komaase naan sàngara, muy gën di jafe nga bàyyi ko. Di naan sàngara ndax stress walla wéet mën na la jural tàmmeel boo xam ne bàyyi ko mën na jafe lool.

  • Mën na la rey. Ci at yii weesu, ci Etaa Sini, daanaka waxtu wu nekk nit dafay dee ndax naan sàngara ba pare di dawal. Ci juróomi at yii weesu, lu ëpp junniy ndaw ak juróomi téeméer yu amagul ñaar fukki at ak benn dee nañu ci aksidaa ndax sàngara. Bu dee sax naanoo sàngara, dugg ci oto boo xam ne kiy dawal dafa naan sàngara, wóorul.

 Jëlal ay dogal

Boo xalaatee bu baax bala ngay naan sàngara dinga mën a moytu li naan sàngara ba mu ëpp di jur.

Li Biibël bi wax: «Kuy foog, gisu ay, làqu» (Kàddu yu Xelu 22:3). Naan sàngara bala ngay dawal walla ngay def bépp liggéey buy laaj nga ànd ak sa sago, wóorul.

Nanga dogu ci lii: ‘Boo naree naan sàngara, na fekk yoon may la ko te amul leneen lu la ko tere.’

Li Biibël bi wax: «Koo [...] déggal [...], jaamam nga» (Room 6:​16). Booy naan sàngara ndaxte sa moroom yi dañuy naan, dafa mel ni dangay bàyyi ñeneen ñi wax la li nga war a def. Booy naan ndax danga wéet walla danga am stress doo mën a am jikko yi nga soxla ngir jànkoonte ak say jafe-jafe.

Nanga dogu ci lii: ‘Du ma bàyyi sama xarit yi dugal ma ci naan sàngara.’

Li Biibël bi wax: «Bul bokk ci ñiy [...] màndi» (Kàddu yu Xelu 23:20). Àndandoo yu bon mën nañu tax nga bàyyi dogal yu baax yi nga jël. Booy ànd ak ñiy naan sàngara ba mu ëpp, loolu mën na la lor.

Nanga dogu ci lii: ‘Du ma xaritoo ak ñiy naan sàngara ba mu ëpp.’