OKTOOBAR 15, 2024
LU BEES
Ndaje bi la Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania di amal at bu nekk: coppite yi ñu yégle ci lu jëm ci at yi nit ki war a am bu bëggee yokk li mu mën a def ci mbootaay bi
Ci ndaje bu ren bi La Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania amal ci 5 oktoobar 2024, yégle nañu ne waññi nañu at yi ndaw ñi bëgg a liggéey ci Betel yi walla bokk ci liggéeyu tabax yi ñuy def ci àddina sépp war a am. Bu njëkk dañu waroon a xaar ba ñu am 19 at. Waaye léegi, mën nañu am sas yooyu bu ñu amee 18 at rekk. Rax ci dolli, ñi bëgg a dem ci lekkool bi ñu jagleel ñiy waare nguuru Yàlla, waratuñu xaar ba am 23 at ndaxte léegi 21 at rekk lañu war a am ngir bindu bu ñu bëggee dem ci lekkool boobu.
Coppite yu neex yooyu, ci saasi lañuy tàmbali. Noonu suñu mbokk yu góor ak yu jigéen yi dinañu mën a yokk li ñuy def ci liggéeyu Yexowa.