Biibël bi dafay soppi dund
Ci nettali yii di topp, dinga gis ni Kàddu Yàlla dimbalee ay nit ñu bare ci àddina si sépp, ñu soppi seen dund ba mu gën a neex.
Dund gi gën
Li ma Yexowa defal bare na lool
Ban njàngale ci Biibël bi moo dimbali Crystal mi ñu siifoon bi muy nekk xale, mu am diggante bu rattax ak Yexowa te am dund gu neex?
Dama doon jéem a xeex njubadi
Rafika dafa dugg ci gurup bu doon xeex njubadi. Waaye mujj na gis ci Biibël bi ne, nguuru Yàlla dina indi jàmm ak njubte.
«Gëmatuma ne war naa soppi àddina si»
Naka la jàng Biibël bi dimbalee benn góor gu doon xeex ngir ñi néew doole?
Dama gëmoon ne Yàlla amul
Naka la góor gu gëmoon ne Yàlla amul bi muy ndaw te communisme mooy li gën mujje sopp Biibël bi?
Soppi nañu seen xalaat ci wàllu ngëm
Gis nañu «per buy jar njég lu réy»
Mary ak Björn dañu xam dëgg gi jëm ci nguuru Yàlla ci anam yu wuute. Naka la loolu soppee seen dund?