Ubbil li ci biir

BIIBËL BI DAFAY SOPPI DUND

Gis nañu «per buy jar njég lu réy»

Gis nañu «per buy jar njég lu réy»

 Yeesu jàngale woon na ne nguuru Yàlla dina faj jafe-jafey doomu Aadama yi yépp (Macë 6:10). Ci Macë 13:44-46, joxe na ñaari léeb ngir wone ne dëgg gi jëm ci nguuru Yàlla njég lu réy la am:

  •   Benn góor moo doon liggéey cib tool ba gis alal ju nëbbu.

  •   Benn jaaykat buy wut per yu rafet ba gis per buy jar njég lu réy.

 Ñoom ñaar ñépp dañu dem jaay li ñu am lépp ci xol bu sedd ngir jënd li ñu gis. Góor ñooñu, ñooy misaal nit ñi fonk nguuru Yàlla ba mu jaral leen xañ seen bopp lu bare ngir jot ci ay barkeem (Luug 18:29, 30). Ci wideo bii, dinga gis ñaari nit ñu niroo ak góor yooyu Yeesu wax ci léeb bi.